JAAR JAARU SEEX SAMBA JAARA MBAY
- Écrire une critique
Jaar-jaaru Séex Sàmba Jaara Mbay
Téere bii, ñi ngi ko bind ngir wone jaar-jaari Muxamadu Abdul Kariim Seex Samba Jaara Mbay.
Leer na ñépp ni, bi Sëriñ Tuubaa woote ba yoonu Murid sosu, ay werekaan yu daa leeral wooteem ak dayoom, jaare ci ay taaliifi wolofal, da caa juddoo. Waande, nu bari itam, dañoo umpale ni Seex Samba Jaara Mbay, mooy ki ko sooke ba gannaaw gi, ñeneen feelu ko ci.
Li epp ci li mu yaxal ciy taalif nag, Seex Abdul Kariim Samba Jaara ngi ko defee dekkub Ndar, ci diggante 1904 ak 1917, di at mi mu génnee Adduna. Ta itam, lépp li mu taalif jëmale ko ca sangam ba, Xaadimu Rasuul, jàng na ko fi kanamam ba mu nangul ko ko.
Téere bii mi ngi génn ci ndimbalu sàqu jàpple móol ci Njawriñu Mbatiit. Njiteefu Téereek Dawal.
La qualité du produit est garantie par L'Harmattan Sénégal
Ce livre peut être récupéré en magasin ou livré à domicile.
Le retour se fait directement en magasin. Merci de contacter le SAV : +221 33 825 98 58