TANN-BEER


5 000 CFA
TTC


Quantité
  Garanties sécurité

La qualité du produit est garantie par L'Harmattan Sénégal

  Politique de livraison

Ce livre peut être récupéré en magasin ou livré à domicile.

  Politique retours

Le retour se fait directement en magasin. Merci de contacter le SAV : +221 33 825 98 58

Téere bi menees na ni waxtaan la. Ki ci ñépp di déglu nag japp na ni àddina bu doon bis la, jant so na ba nit ñi tàbbi ci guddi gu lëndëm këriis. Ba tax na moom yéeneem di gindi aw xeetam, yee leen ci yi jar a saytu te ñu sàggane leen ak yi ñu war a moytu ci te ñii lab ca ñee nuur jëm ca, tax mu leen di fattali naan: "ñaar a fiy xal a nekk muy li la war ak li la warul. Boo ci nekk doo tal ba ca des."

Tann-béer seetu la buy màndargaal warab ak jamono yu wute. Gis-gisu aji-nettali ji ci tenk moo di, weesug démb warul a tee xalaat ak a xalam ci ay jeexitalam, ngir ràññee la ciy sunu cër ak nees ko war a doxalee ba jekku tay mën a waajal ëllëg. Xew-xew yi muy nettali am na ci yu rafet am ci yu ñaaw, yu neex ak yu naqari. Li ci ëpp nag moo ngi dox ci diggante kër Algaf ak gog Xaali, muy ñaari askan delluwaay. yuy faral di nuroo ak a wute ay doxaliin, gis-gis ak

Téere bi dëxën na lu bari, waaye li ci gën a fés mooy xeltu ak xayte der bu ñuul, rawati na xeetu Wolof. Loolu bokk na ci li waral aji-nettali ji di artu ak a jooytu sunu càggante fu bari, ba ci sunu mbatit miy réer, tax mu naan: "Lu mel ni wayi kasag ak yeete ya mu daan ëmb, ndénkaan ya daan gungeb aat bisub tàbbeem ci néegu góor, bàkk ya daan jafal mbër su daan war a sëgg bëre, woyi cosaan ya daan yokk jom, pastéef ak njàmbaar njegemaar ak waxambaane ca waar wa... Loolu lépp a ngi naaxsaay, sunu mbatit di gën a giim te li wér te wóor mooy bu nu ci jógul ci fay kamaj la jëm."

Téere bii mi ngi génn ci ndimbalu sàqu jàpple móol ci Njawriñu Mbatiit. Njiteefu Téereek Dawal.

9782490146147
Commentaires (0)